UN staff, including eight OHCHR colleagues, detained in Yemen
OHCHR calls for their immediate release.
SOURCE
United Nations Information Centre, Senegal
TOTAL SPEAKERS
USAGE BY COUNTRY (OFFICIAL LANGUAGE)
Home Speakers: Senegal, Mauritania and GambiaBACKGROUND
Wolof is the principal language of Senegal, in westernmost Africa. There it is spoken by about 3 million people (over 7 million including second language users). Wolof belongs to the West Atlantic branch of the Niger-Congo family of languages. In Senegal it is the main African language, predominantly urban, also used as lingua franca . It is different from Wolof spoken in Gambia.Ñu jàpp te nangu ne sagu doomi aadama ak sañ-sañam yépp-dañu yam te kenn mënukóo jalgati, te lu lépp nekk na cës laay ci taxufeex ci mbirum àtte ak jàmm ci biir àdduna.
Ñu jàpp ne ñakk xam ak soofantal sañ-sañi doomi aadama indi na aymusiba yu tar tax képp kuy dund fippu. Temano egsi na ba mu nekk ci doomi aadama ñu mën a wax, xalaat, ci seen coobare, bundxatal, nàkk dëddu leen.
Ñu jàpp ne am na solo lool ñu aar sañ-sañi doomu aadama ak ay matukaay ci wàllu yoon; ngir doomu aadama moomu kenn du ko sonal, muy fippu ci nootaange ak lu koy bunduxatal.
Ñu jàpp ne am na solo lool ñu góor-goorlu ba gën a rataxal jokkalante gi diggante xeet yi.
Ñu jàpp ne ci bataaxal boobule mbootaayu xeet yi yeesalaat na ay pas-pasam jëme ko ci sañ-sani doomi aadama yu tolloo, ci sag, ci bir lépp lu aju ci dundin diggante góor ak jigéen, ci biir tawfeex gu yaa.
Ñu jàpp ne réew yi ci bokk jël nañu ay matukaay ngir dëgëral jokkalante gi ak mbootaayu xeet yi, ñu naw it bu baax sann-sañi doomi aadama ak tawfeex yu wóor ci biir àdduna yépp.
Ñu jàpp ne ànd taxawal sañ-sañ yeek tawfeex yi nekk na lu am solo lool ngir, darajaal matukaay yooyu.
Ndaje mu mag mi biral na ci bataaxal bii ne xeet yépp, réew yépp ak kurel yépp ñu jàpp li ci nekk, ci seen xel, te ñu góor-góorlu, ñu jaarale lii lépp ci njàng mi ak yar gi.
Ñu lawal sañ-sañ yeek taawfeex yi jël aymatukaay ci biirak bitim réew.
Ñu nangu te di doxal fépp ci anam gu wér ci biir xeet yi sosoo ci réew i bokk ci mbootaay gi ak gox yi bootu ci ñoom.
Doomi aadama yépp danuy juddu, yam ci tawfeex ci sag ak sañ-sañ. Nekk na it ku xam dëgg te ànd na ak xelam, te war naa jëflante ak nawleen, te teg ko ci wàllu mbokk.
Ku ne mën naa wax ne am na ay sañ-sañ ak ay tawfeex yu sosoo ci bataaxal bii te amul xeej ak seen, rawatina ci wàllu xeet, melo, awra, làkk, diiné, peete ci wàllu politig, xalaat, réew mbaa askan woo mën ti sosoo, ci it wàllu juddu alal ak lu mu mën ti doon.
Rax sa dolli amul xeej ak seen ci politig, yoon, mbaa doxalin wu aju ci bitim réew mbaa suuf soo xamne nit ki fa la cosaanoo; réew moomu mbaa suuf soosu moom na boppam walla deet, mbaa ñu yamale yengu-yëngoom.
Nit kune war naa dund ci tawfeex ak kaaraange.
Waruñoo def kenn jaam mbaa mbindaan. Njaam ak njaayum jaam nanguwunu ko ci anam gu mu mën ti doon.
Waruñoo mbugal, tutal, mbaa teg kenn lu metti lool lu yelloo wul ak doomu aadama.
Nit ku ne am na sañ-sañ ñu war kaa nangul darajaam ci wàllu yoon.
Népp a yam ci kanamu yoon. Te it amul xeej ak seen, ku ne yoon woowu war na laa aar. Népp war nañu leen aar ci luy jalgati liñu tënk ci bataaxal bii ak bepp yëngu-gëngu buy indi par-parloo.
Nit ku ne am na sañ-sañ dem ci berebi àtte kaay yi ci reewam saa yoo xamne sañ-sañam yooyu dëppook sàrti réewam mba yoon jalgati nañu ko.
Menuñoo jàpp, tëj, mbaa genne kenn réewam te tegunu ko ci yoon.
Ci lu wér, nit kune mën naa egg ci berebu atte kaay wax li ko naqari ci anam gu jub, te baña ànd ak par-parloo, ne dañu ko taxal.
Kenn warula xuus ci dundinu doomu aadama, bu njabootam, ci lu jëm ci këram mbaa lu mengóok moom, di damm it jarajaam. Buñu jalgatee yii nit kune am na sañ-sañ ñu aar ko ci wàllu yoon.
Nit kune am na sañ-sañ xalaat ak sa goom ci wàllu diine, soppi it diineem mba ngëmam, am na it tawfeex feeñal diineem, mbaa ngëmam, ak mbooloo, mbaa moom doww, fu àdduna daje mbaa deet, jarali ko ci njàngale mi, ci ay jëf, ci jaamu yi ak xarbaax.
Nit ku ne am na sañ-sañ wax mbaa bind lu ko soob. Ci waxam yooyule kenn menuko ce bundu xatal. Te it am na sañ-sañ di gëstu, di jot, di wasare ci anam gu yaa ay xabaaraki xalaat ak ay jumtukaay yu mi Men ti jefandikóo.
Nit ku ne meññeefu askan wi am na sañ-sañ ñu aar ko ci giru dundam. Ci dundam war na ci am xol bu sedd ci sañ-sañam yooyu, lu aju ci koom-koomam, ci dundinam ak ci lépp lu aju ci aadaam te di ko jox maanaa ak yookkute gu ànd ak tawfeex ci wàllu darajaam, loolu lépp nag ku ne doomu réew mi indi dooleem ak di jokkalante ak bitim réew te mu méngook tërërin ak am-amu réew mu ne.
Nit ku ne am na sañ-sañ noppalu, feexal xolal ak it di yamale diirub liggéeyam ak it léeg-léeg muy për, bër gu ànd ak xaalis.
Nit ku ne war naa tawaxu dëpp lu aju a askan wi, ak lu aju ci bitim réewam ba sañ-sañ ak tawfeex yi bataaxalu xeet gi ëmb mën a sax.
Ci fànn gu mu mën ti doon ci bataaxal bii, bépp réew, mbootaay mbaa nit, warul doxal mbaa def luy yàq sañ-sañ yeek tawfeex.